Colloque International

De linguistique de Dakar

EXPOSITION CILDAK 2023

Stand 4

EJO, kërug móolukaay gi bindkat bii di Bubakar Bóris Jóob sos, daa juddu ngir bey waaram ci suqali kéewug mbind ci làmmiñi réew mi. Kenn umpalewul ni loolu ci yaatal téere yi lay jaare. Moo tax EJO taamu yemandi ci làmmiñi réewum Senegaal. Ci gàttal, EJO day yëngu ci :

  • jubbanti mbind ; 
  • móol ak jaay téere ; 
  • tàggat ci làmmiñi réew mi ; 
  • tekki tubaab walla àngale ci wolof walla it dale ci wolof tekki ko ci tubaab walla àngale.

Ba tey it Lu Defu Waxu (www.defuwaxu.com) di yéenekaayu internet bi jëkk ci wolof ci EJO la bokk.

Bokk na ci téere yi EJO jot a móol : «Mboorum àdduna si » bu Abdul-Xaadr Kebe, «Xelum xalam » bu Làmp Faal Kala, «Bàmmeelu Kocc Barma » bu Bubakar Bóris Jóob, « Guddig Mbooyo » bu Lamin Mbaay, « Watit » bu Felwiin Saar ak yeneen. EJO génneendoo na 3ti téere ci sãwiyee 2023.

Di fàttali rekk ni EJO baatub kinyarwandaa la buy tekkeendoo démb ak ëllëg. Nu ciy sargalaale Séex Anta Jóob  mi nu jàngal ni su nit ku ñuul bëggee jëm kanam, naatal ëllëgam, fàww mu xam démbu Afrig, xam it ne war na koo damoo.

Jokkooejowolof@gmail.com ; Tel : +221 77 651 68 48

= = = == = =

EJO EDITIONS, créée par l’écrivain Boubacar Boris Diop, entend participer au renforcement de l’environnement lettré des langues nationales. Celui-ci passe, on le sait, par une plus grande accessibilité de sa littérature.

Voilà pourquoi EJO-Editions a choisi de se spécialiser dans l’édition en langues nationales sénégalaises. Dans la pratique cela se traduit par les activités que voici:

  • correction de manuscrits ; 
  • conception de livres, de matériel didactique ; 
  • vente de livres et diffusion en librairie ; 
  • formation dans les langues nationales ; 
  • traduction du français, de l’anglais vers le wolof et vice-versa.

Lu Defu Waxu (www.defuwaxu.com), premier journal en ligne exclusivement en wolof du Sénégal, fait partie d’EJO-Editions.

Parmi ses publications, on peut citer « Mboorum àdduna si » de Abdul-Xaadr Kebe, « Xelum xalam »  de Làmp Faal Kala, « Bàmmeelu Kocc Barma » de Bubakar Bóris Jóob, « Guddig Mbooyo » de Lamin Mbaay, « Watit » de Felwiin Saar entre autres. EJO vient de publier (janvier 2023) trois nouveaux livres.

Il convient de rappeler qu’EJO est un mot kinyarwanda qui signifie à la fois hier et demain. Il a été également choisi pour rendre hommage à Cheikh Anta Diop qui nous a appris que le Noir doit mieux connaitre son passé et en être fier s’il veut faire face aux immenses défis du futur.

Contactejowolof@gmail.com ; Tel : +221 77 651 68 48